Apple II, mooy nosukaay kenn (personal computer, di ko wax PC) bi njëkk.
Xibaarfeppal judd ci booloog ñaari baat yii di xibaar ak mbëjfeppal. Di tekki ab xeetu xam-xam buy settantal bépp fànnu xibaar jaare ko ci ay wuutuloxo yu mbëjfeppal.
Jamonoy nosukaay mi ngi am ndooteel ci jëm-kanamug mbëjfeppal ci Ñaareelu Xareb Àdduna bi. ci la ñu defar wuutuloxo yu noppi yi ci njëkk.
|