|
Article on other languages:
|
Goxub Afrig moom benn la ci goxi Àdduna Ju Yàgg ja, moom nag ab joor bu réy ci jéeri la, géej xottiwu ko (jaarul ci biiram) du caagéenug dóox (golfe). Moom nag mi ngi nekk walla mi ngi féete ci xaajub kol-kol bu penku bi. Gox bi nag mi ngi tallaliku ci diggante ñaari rёddi gaar yii : 37º ci tus-wu-taxaw wu bёj-gànnaar ak 35º ci tus-wu-gaar wu bёj-saalum. Bu ko defee rёddu yamoo wi jaar ci diggam, daal di koy séddale ñaari xaaj: benn xaaj bi di bu bёj-gànnaar, nekk nag ci xaaju kol-kol bu bёj-gànnaar bi, beneen bi di bu bёj-saalum, féete ci xaaju kol-kol bu bёj-saalum bi. Ci noonu gёwéelub sànkar moom ñёw romb ca genn wàllam gu bёj-gànnaar ga, gёwéelub tef ñёw jaar ca geneen wàll gu bёj-saalum ga. Bu ko defee rёddu Grinits (rёddu tus-wu-taxaw wi ) romb ca catam lu sowwu la. Moom nag dafa tiim ak tefesam yi ci wàllug bёj-gànnaar géej gi ñuy wax Géej gu Diggu gi, mooy li ko tàqaleek goxub Tugal, waaye fu jege Tugal lay doon, bu dee fa tollook Doju Taariq (Jibraartaar). Bu dee ci penku bi day tiim Géej gu xonq gi ak mbàmbulaanug End gi, ñoom ñaar ñoo koy tàqaleek goxub Asi ak Oseyaani, waaye luy jege Asi la ca Baabul Mandab ak barsaqu Suwes, ci sowwu bi nag mi ngi sapp (tiim) ci mbàmbulaanu Atlas gi ko tàggaleek ñaari goxi Aamerig yii di: Aamerig gu bёj-gànnaar gi ak gu bёj-saalum gi. Afrig nag nekk gi mu nekk ci diggante goxi Àdduna ju yàgg ja, tax na bu baax ba xayug Isipt gu yàgg gu kawe ga, man a tas ba àgg ci xeet yu bari ci ñaari gox yii, Asi ak Tugal. Goxu Afrig mooy ñaareelu gox bi gёn a yaatu ci goxi àdduna bi, ndax tolluwaayam àgg na ci 30 milyoŋi kilomet yu kaare, maanaam lu tollook 1/4 tolluwaayu goxi àdduna ju yàgg ja, walla lu tollook réew mu tollu ne Isipt nga ful ko fanweeri yoon. Ngir woomle gu réy gi gox bi def ci wàllug mbay, dundat ak mbell, sancaani sowwu yi (waa Tugal yi) tegoon nañu ko loxo, waaye ay askanam jug def ay fipp yu toftaloo ngir gore ci canc gi (colonialisme), ci noonu ñu ёpp ci ñoom mujj temb, sancu yi ci mujj a temb nag ñooy yu Portugaal yi, ñoom de xeex nañu xeex yu tar ngir jot séenug tembte.
Melosuuf ci jëmmNin ko junjee ci kaw, Afrik doon na gox bu rey. Ci tëddaayam, so jële penkoom jëm sowwu mat na 7500 (juroom ñaar fukk ak juroomi temeer) km, bëj-gànnaaram ba bëj-saalum tollu na ci 8000km (juroom ñetti fukki junni) ci guddaay. Diwaan yu mag yiDiwaan yu mag yi bari nañ loo:
Melosuufug niteNit ñi ci gox biReew yi nga xam ne seenug yorte(administration) dafa néewal, lim yi ñuy joxe doonu ñu yu matale (limbare (statistique) yi defu ñu leen ci anam gi war). Ci 1975 : 302 miliyoŋ i way-dëkk Ci 2001 : 591,3 miliyoŋ i way-dëkk (ki ko wax : PNUD) Ci 2005 : 803,690 miliyoŋ i way-dëkk (ki ko wax : World Bank ndeyi-koor 2006) Gisjiital ngir 2015: 866 miliyoŋ i way-dëkk. 11% gu way-dëkk gi ci adduna bi, mi ngi ci Afrik gu bëj-saalumu-Sahara. yokkuteg nit ci Afrik doon na bi gën a gaaw ci adduna bi (21% ci ay way-dëkk yu ciy yokku at mu nekk). Doon na aw askan gu bariy ndaw, ñi ci ëpp 17 at la ñu am (te ci adduna bi yëpp 23 at la). 45% yu waa-afrik 15 at (fukki at ak juroom) la ñu am. te ñi ëppal 65 at, 3% lañ ci askanam (lang ak 13% ci li des ci adduna bi). Judd gi : 43 ci junni boo jël (26 ci junni ci adduna bi), 6 doom jiggeen ju ne ci lu ëpp(2,8 ci adduna bi). Yaakaarte dund gi(li nga yaakaar a dund): 48.8 at Xeet yigëstukat yi ci li ñeel xeet, gis nañ ay mbooloo xeet yu bari ci Afrik:
Kuuteeg làkk yiÑoo ngi koy xayma ci 200 ak 2000 làkk walla waxin (làkk dañ koy bind te waxin ci lammiñ lay yem) ci Afrik. Dañ leen seddale ci ay mbooloo, maanaam làkk yi am ag mbokk.
Lu ëpp ci làkk i Afrik yi, du ñu ay làkku nguuru reew ya ñu leen di làkkee, maanaam duñ leen jngale ci daara yi, ngur gi du leen jëfëndikoo. Ñetti làkk rekk ñooy làkk i seen nguuru reew, di seen làkku cosaan: Lesoto, Ruandaa, Burundi. Kuuteeg diine yi
Ñugg-ñugg yiGoxub Afrig ñi koy xàmmee ci suufam su bari si ay laamaar, ba tax na sax ñu koy niroole ak tappaan bu ñu dёpp, boo xoolee di nga gis ne penku gox bi ak bёj-saalumam ñoo gёn a yekkatiku bёj-gànnaaram ak sowwoom, te it dinga man a gis laamaar yii: Laamaaru Tàkk gu mag gi : day tàllaliku ngir daj mbooleem bёj-gànnaaru gox bi, dale ko ca géej gu xonq ga ci penku bi, ba ca mbàmbulaanug atlas ci sowwu bi, dees na fa gis it ag kaw-suuf gu bariy melo: ay laamaar, ay tundi xeer, yu beeñ (dune) ak xur yuy faral a am ay waaha (oasis). Doji Atlas yi: ñoom ñi ngi nekk ci gёn jaa soriy bёj-gànnaaru sowwu gu Afrig, ci réewi Maxrib Bu Araab bi, bu ko defee ñu tàlleeku nag yor melokaanu ay càllalay doj, dale ko ca bёj-saalum gu sowwu gi ba ci bёj-gànnaar gu penku gi, ñu ёmb nag ci seen biir ay laamaar yu kawe yu ay ngéej yu saf xorom di diggale , ñu xame leen ci turu Shutuut . Xuru mbalkam Kongoo mi: mi ngi ci xolub gox bi, fa la dexug Kongoo giy dawe aki caram yu limu yi, di sotti ci sowwu bi ci mbàmbulaanug atlas gi. Doji géej gu xonq gi: càllalag doj la gu kawe, tàlleeku bawoo bёj-gànnaar, ba bёj-saalum, feggook nag tefes gu sowwu gu géej gu xonq gi ci Isipt ak Sudaan. Laamaaru Ecoopi: mooy bi gёn a kawe ci laamaari Afrig yi, fa la ñatti car (affluents) yu am solo yu dexug Niil gi di balle ñooy: Sobaat, ak Niil gu bulo gi ak Atbara, bu ko defee yobbaale ndoxi mbёnd yu bari yi ci jamonoy taw bi, ngir denc leen ci ngéejus Naasir ba waa Isipt di ci man a jariñu, mu leen di indil ag naataange. Laamaaru ngéeji yamoo yi: moo ci gёn a néew ag yekkatiku, fa la cari Niil gu yamoo gi di balle, ñoom ñi nga xam ne seeni ndox ña nga leen di jёle ca ngéejus Wiktooria, mooy ngées su neexum ndox si gёn a réy ci yu àdduna bi, mooy jox Niil ndox li ёpp ci weeri at mi Laamaaru bëj-saalumu Afrig: moo gёn a yaatu te gёn a yëkkatikoodi, am na nag yenn dex yu ko dog, am ci yu ciy sotti ci penku bi, ci mbàmbulaanug End, (niki Simbisi ak Lombobo), am yu ciy sotti ci sowwu bi ci mbàmbulaanug Atlas niki Orang KilimaaRёddu yamoo wi moo séddale Afrig def ko ñaari xaaj : bu bёj-gànnaar ak bu bёj-saalum, looloo waral ag tolloo am ci goxi kilimaa yi ci bёj-gànnaaru rёddu yamoo wi ak ci bёj-saalumam. Li ёpp ci goxu Afrig it mi ngi nekk ci diggante gёwéelub sànkar bi ci wàllug bёj-gànnaar ak bu tef bi ci wàllug bёj-saalum gi, looloo waral kilimã bu gёwéel bu tang bi daj Afrig gépp lu ci dul catam yu bёj-gànnaar gu sowwu gi ak yu bёj-saalum gu sowwu gi, foofa kilimã bu géej gu diggu ga’a fa nekk. Jamonoy taw yi tam wuute nañu, bariwaayu taw bi it wuute ci barab ak moroom ja. Tawi Yamoo yu bari yi danañuy faral a sottiku ci tefesug Gana gi, ak [Mbalkam Kongóo|mbalkam Kongóo]] mi diirub at mépp. Taw yu kojug dig, yu noor yu sakkan yi, ñi ngi faral di rot ci bёj-saalumu Sudaan ak Laamaaru Ecoopi. Taw yu diggdoomu yi ñi ngi wàcc ci digg Gox bi, ca bёj-gànnaar ak bёj-saalumu diwaanu yamoo bi. Taw yu néew yi ñi ngi rot ci bёj-saalumu tàkk gu mag gi ak bёj-gànnaaru tàkkug Kalahaari gi. Tàkk gu mag gi nekk ci bёj-gànnaaru Gox bi nag moom daanaka du taw ak tàkkug Kalahaari gi nekk ci bёj-saalumu sowwu Gox bi. Tawi sedd bi danay rot ci bёj-gànnaaru Gox bi, ak bёj-saalumam gu sowwu gi ngir gelawi Kalahaari yay upp ca bёj-saalumu sowwu Gox bi. Melow kilimao bi ci noor bi ( noorub bёj-gànnaar bi) sulye – nii la tёnkoo: TàngoorJant bi day jamu ci gёwéelub sànkar bi, bu ko defee tàngoor wi yékkatiku ci xaaju Gox bu bёj-gànnaar bi, nekk nag di lu yam te taradi ca xaaju Gox bu bёj-saalum bi. Naaj gu jawwu gi , Gnelaw li, Taw yi: Jant bi day jamu ci gёwéelub sànkar bi, ci bёj-gànnaaru Gox bi, bu ko defee tàngoor wi yékkatiku, naj gu jawwu gi daal di woyof, te fekk naj gu jawwu gi mi ngi gёn a am doole ci mbàmbulaanug atlas gi, loolu di waral ngelawi kojug dig (saisonnier) yu bёj-saalumu sowwu yiy tawloo di jañu juge ci mbàmbulaanug atlas gi jёm ci barab bi naj gu jawwu gi di gёn a woyofe, bu ko defee taw yi daal di rot ci Tefesug Gana gi, ak Laamaaru Ecoopi ak bёj-saalumu Sudaan. Ci at mépp day taw ci Digg Afrig, ca la wёr Rёddu Yamoo wa, taw yooyu nag ñi ngi leen xame ci turu (Tawi yéegal yi). Melow kilima bi ci sedd bi (seddub bёj-gànnaar bi) samwiye – nii la tёnkoo: Jant bi day sampu ci Gёwéelub tef, bu ko defee tàngoor wi yékkatiku ci xaajub Gox bu bёj-saalum bi, daal di wàcc maanaam neew doole (moom tàngoor wi) ci xaaj bu bёj-gànnaar bi, loolu mooy tax naj gu jawwu gi di néew doole ci bёj-saalumu Gox bi, tey am doole ci diiwaanu Tàkk gu mag gi, ci noonu la uppug ngelaw yu yaxantu yu bёj-gànnaaru penku yu fendi yi di àgge ba ci digg Gox bi daanaka. Ngelawi sowwu yu safaanu yiy tawloo (ndax ci Mbàmbulaanu Atlas lañuy juge) dañuy upp, di rotal ay taw ci tefesi bёj-gànnaaru penku yu Gox bi, ngelaw yii nag dañuy àgg ci tàkk gu mag gi, di lu fendi. Te tam Tàkk gi jamono ju nekk ngelawi yaxantu yu tàng yi danu koy upp. Ngelawi yaxantu yu bёj-saalumu penku yiy tawlo dañuy upp ci tefesi bёj-saalumu penku yu Afrig yi, bu ko defee taw yi rot, ñuy sutuxlu ci biir ci kaw Laamaaru Bёj-saalumu Afrig, bu ko defee ñu àgg ciw tàngoor ba ca Tàkkug Kalahaari, ci bёj-saalumu sowwu Afrig. Diiwaani kilima yi
Diiwaani gàncax yiGott yu Yamoo yi: ñi ngi ci fu ёpp ci mbalkam Kongoo mi, ci tefesug Gana gi, ak cig wàll ci tefes gu penku gu gox bi. Tàngoor wa lu fa tar la, taw ya lu fay bari la ci at mi mépp, looloo tax ay gott yu fatt, yu am ay garab yu réy, yu kawe te yaatuy xob te jegee di fa am, seeni bànqaas di rabbaloo, bu ko defee ay gàncax di leen wёr fu nekk, di ñàpp nag ngir àgg ci leerug jant bi nga xam ne du àgg ci suufus gott sii fees dell aki taa-taa aki déeg aki tepp-tepp, fii nag ab judduwaay la ñeel ay gétti yo (barab bu bariy yo la)
Afrig gu Bëj-saalum • Alseeri • Angolaa • Bene • Botswana • Burkinaa Faaso • Buruundi • Kamerun • Kap Weer • Réewum Diggu Afrig • Bennoo yu Komoor • Kongóo-Brasaawiil • Kongóo-Kinshasa • Kot Diwaar • Jibuti • Isipt • Eriitere • Ecoopi • Gaboŋ • Gaambi • Gana • Gine • Gine-Bisawóo • Gineg yamoo • Keeñaa • Lesoto • Liberiyaa • Libi • Madagaskaar • Marook • Malawi • Mali • Móoris • Gànnaar • Mosambik • Namibi • Niseer • Niseeriyaa • Ugandaa • Ruwandaa • Sahara gu Sowwu • Sao Tome-ak-Principe • Senegaal • Seysel • Siraa Leyoon • Somali • Sudaan • Suwaasilaand • Tansani • Cadd • Togo • Tuniisi • Sambi • Simbaawe |
||||||||||||||||||||||||||||||
This article is from Wikipedia. All text is available under the terms of the GNU Free Documentation License.
Mercedes Car
This site monitored by SitePinger.net