|
Article on other languages:
|
Mbëj da di ag feeñte gu gisuwul ak bët, guy feeñ ci ag wootalante walla bëmëxante ci diggante cëfkay mbëj yi. Ci gattal mooy gépp feeñte gu juddu ci jàmmaarloo gi nekk ci diggante: feppselal yi, ñoom ci lu ëpp da ñuy tekkaaral, ak mbëjfeppal yi nga xam ne ñoo ëpp yëngu-yëngu, ci biir xarefulwon gi. senub demin jur ab dawaan. Su ñu ko boole ak bijjaakon, mu jur beneen baŋxaas bi ñu duppee mbëjbijjaakon. Mbëj moo yor ay feñfeñu jëmm yu mel ne mellax, toolu mbëj ak dawanu mbëj (ci lu bari dañ leen di jaawale). Mbëj doon na “jaamu” nit gi gën, doon tamit raññeekayu adduna gu bees gi. Dafay leeral sunu dëkkuwaay yi di doxal sunu këri koom-koom yi te jegele nit ñi gënoon a soriyante. Yanub mbëjYanub mbëj doon na lu ñu man a natt te man kaa jëfëndikoo, waaye doonul lu neex a faramface ak ay baat yu yomb a nand, ndaxte yombul leeral melokaan yi mu am ca dëg-dëg. Xayna li gën mooy wax lan la ak li muy sabab. lepp (lu mu man a doon) lu am yanub mbëj, man nañoo wootalante walla bëmëxante. Li gëstu yi wone mooy am na ñaari fanni yanub mbëj, benn bi la ñuy woowe yanub kanamal (+) (feppsalal) moom mooy nek ci biir xolu xarefulwonu neen yëpp ak yanub gannaawal(-) (mbëjfeppal) ñoo nekk ci li wër xolu xarefulwon yii. Naka-jekk yanub kanamal yu xolu xarefulwon gi dañuy tolloo ak limu yanub gannaawal yu mbëjpeppal yi ko wër. Mbëj ak BijjaakonLiy wër ab mbëjfeppal walla leneen lu mu man a doon lu am ab yanub mbëj day am melokaanu lu jalaxu, moom la ñuy tuddee toolu mbëj. Soo jalaxee ay mbëjfeppal, day am benn tool bu wër seenub jublu, moom la ñuy tuddee toolu bijjaakon. Dooley tool boobu dafa aju ci limu mbëjfeppal yi jalaxu ak seen gawaayu jalaxu, maanaam, ci yeneen i kaddu, ci dawan gi. Soo jallalee ab dawan ci ab lëmës, bu nekk wëñu përëm, ci ni mu waree, lëmës googu day mel ne bijjaakon gu weñ, day wootal walla bëmëx yeneen lëmës yi mu yemal wëñ. lëmës gu mel noonu su fekkee daŋ kaa defaree ag wëñu përëm goo wëndeel ci'b weñ, day gën a yokk toolu bijjaakon ga cay juddoo. Su fekkee dangaa am ay lëmës yu bari, yu ñu wëndeel wëñ ci weñ, yu man a wëndeelu, nga boole leen ak yeneeni lëmës yu dul wëndeelu, yu am toolu bijjaakon gu tar, yu dawan jaar, day jur ab dooleb doolerandu. Doole googu moy wëndeel lëmës yu man a wëndeelu yi, mu daal di man a def liggéeyu doolerandu. Mu nekk ab jumtukaay bi ñuy woowe doxalkat mbëj. Tay jii, doxalkat mbëj yi ñooy doxal bepp wuutuloxo, tambalee bi ci gan a ndaw ba ca ba gan a ngande. Doxalkat yi dañoo bari te am ay melokaan yu wuute.
|
This article is from Wikipedia. All text is available under the terms of the GNU Free Documentation License.
Mercedes Car
This site monitored by SitePinger.net