|
Bëj-saalumu Tugal ab diwaan la ci goxu Tugal. Tekkib baat bi nak di na faral di indi ay werante, ba tax na am na ay tekki yu bari. Ci lu ëpp da ñuy wax naa Ispaañ, Itaali, Girees, ñooy réew yi ci bokk, daanaka ci lu daj réew yépp yi nekk ci Géej gu Diggu gi. Bëj-saalumu Faraas ci lu bari da ñu ko ciy boole.
Xaaj gu Bëj-saalumu Tugal moo xonq
Tekkeem gu séwógaraafi
Ci séwógaraafi da ñu naa Bëj-saalumu Tugal mooy xaaj bi gën a féete Bëj-saalum ci goxu bi; bii tekki nak da fa ajoo, ba tax na sax amuli pegg yu leer. Càllaleeb doj bu Alpi moom la ñuy téewee ni ab pegg buy seddatle Itaali ak li des ci Tugal, doon liy xaajatle ñaaru Tugal yi
Limu réew yi
|