Ci jamono ju yagg ja «Afrig» da doon jëmmal diwaanu Kaartaas, mooy réewu Tiniisi gu tay. Afrik ab diwaanu Nguuru Rom gu Mag ga la woon . Bi jullit yi ñëwee, baat bi dañ kaa soppi, araabal ko Ifriqiya.
Beerbeer yi, ñooy way dëkk yiñ ni ñoo njëkk ci bëj-gànnaaru Afrig.
«Afrig gu weex» bu njëkk da doon jëmmal barabu Afrig bi ay nit yu xees dëkkee: Marok, Alseeri, Tiniisi, Libi, Esipt. Waaye tay baat bi liñ kay jëfëndikoo bariwul.