Afrig

Article on other languages:

del.icio.us del.icio.us
Digg Digg
Furl Furl
Reddit Reddit
Rojo Rojo
Add to OnlyWire
Afrik

Afrig, moom la ñu jàppee ne mooy gox bi nit cosaanoo, su nu ko xoolee ci yaatuwaayam ak bariwaayu askanam (lu weesu gox bu Asi), mooy ñaareelu gox bi gënn a rëy ci àdduna bi. Yaatuwaayam tollu na ci 30.065.000 km², nekk 20,3% ci jéeri ji ci àdduna bi. Ay way dëkkam tollu ci lu ëpp 800.000.000, muy benn juroom ñaareel bu way dëkki àdduna bi. Afrik a ngi yem ci bëj-gànnaaram ci Géej gu Diggu gi, ci sowwu ci Mbàmbulaanug Atlas, ci bëj-saalum ci Mbàmbulaan gu Bëj-saalum gi, ci penku ci Mbàmbulaanug End. Asi rekk la taqalool ci yeneen gox yi. Yamoo gi jàll na ko. Ci jëmm doon na gox bu bari'y melokaan, te wuute teg ci.

Tëraliin

Cosaanam

Baatu «Afrig» moo ngi jóge ci turu Afridi yi, doonoon ag giir gu dëkkoon ci Bëj-gànnaaru Afrig ci diwaanu Kaartaas.

Beneen cosaanam moo bàyyikoo ci Berber Taferka «suuf», «boroom suuf». Ki fay dund la ñuy woowee Aferkiw, Latin yi soppi ko africanus, mu doonoon aw tundu waa rom ci Afrig. Araab yi di ko wax إفريقيا ifrīqīyā, mu doonoon Tiniisi gu tay gi.

Ñeneen ne ci baatu waa geres bii di aphrike («amul sedd»), latin di ko waxaprica («Bari naaj»), la jóge.

Taariix

Afrik la ñuy jàppee ne mooy cosaanu nit, ndax desiti nit yi gën a yàgg ci àdduna bi fa la ñu ko gisee, ci Afrig gu Bëj-saalumu-Sahara.

Sahara cëru na bu baax ci màggug gox bi. Taariixu askani Bëj-gànnaaru Afrig yi day tolloo ak bu Tugal ak bu Penku gu Diggu gi. Li ëpp ci Afrig gu Bëj-saalumu-sahara amul woon genn jëflante ak li des ci àdduna bi, da ñoo beru woon.

Jamono ju yàgg ja

Xay yi juddoo ci goxu Afrik, boole nañ leen ci yi gën a mag ci taariixu nit. Xayu Esipt ak bu Gana ak bu Mali, ak bu Kuush ak bu Songaay, añse.

Jamono ju yees ji

Jàppum njaam

Ngir Xòotal, yërël bii jukki ci Jàppum njaam

Ci li taariixkat yi wax, jàppum njaam mi ngi tambali ci xarnub VII ak araab yi. Ci lu gën a leer ci atum 652 ba Ab njiitu araab takk-taxawalee waa Nubi yi ngir ñu jox leen 360 ciy jaam at mu jot. barab yi njaay mi doon amee mi ngi dale ca Mali ba Penku Afrik, ci wàll gi féete bëj-saalumu Sahara.

Ci xayma nee nañ ci diggante xarnub XVIII ba ci xarnub XIX, benn ñenteel ci nit ñi ay jaam la ñu woon, walla ñu ñu manante (takk-taxawal) ci liggéey bu ñu sañut a bañ. Nee nañ njiitu waa afrik yi ci seen bopp ñoo doon jàppaate ak a jaayaate.

Waa tugal lu weesu bi ñu aakimoo (walla sancee) suufi Aamerig yi da ñoo soxla woon ay loxo yuy liggéey ci seen tool yi. Def nañ ko ci 400 at (1500-1888), ay jaam yu bari jënd nañ leen walla jàpp nañ leen ci tefesi afrik yi: Sowwu Afrig gépp, ak ci bëj-saalumam itam. Donte tereg jàppum njaam gi mi ngi waddoon ci lu jege atum 1850 (réew yépp bàyyeendoowuñu ko) amoon ay nit yu wëyoon di ko def cig làqatu ba ci 1900.

Jamono ju mujj ji

Aakimoo gu waa tugal

Jamonoy aakimoo gu tugal ci Afrig moo ngi tambalee ci Ndajeem Berlin (1884-1885) ba ci tembte yi ci atum 1960, sedatle gu réew yu tay yi ca la jóge. Ecoopi moo doonoon menn rèew mi ñu masut a teg loxo.

Tembte yi

Pàcc yu tembte gu réewi Afrig yi

Melosuuf

Ngir Xòotal, yërël bii jukki ci Melosuufug Afrig

Goxub Afrig gëstu gi aju ci ay way dëkkam

Yërël bii jukki ci Way dëkki Afrig

Cosaan ak diine

Làkk

Gëstukatu-làkk yi ci xayma nee nañ 2 000 làkk ci goxu Afrik, ñu boole leen ci ñeenti mbooloo, làkk yi fa cosaanoowul bokkuñu ci.

Xool it

Koom-koomu Afrig

Lëkkalekaay yu biti

Goxi àdduna bi
Afritugalasi Oseyaani
   
Afrig
Afrig
Tugalasi
Bëj-gànnaaru Aamerig Tugal Asi Bëj-saalumu Aamerig
Ci « http://wo.wikipedia.org/wiki/Afrig » lañ ko jële

This article is from Wikipedia. All text is available under the terms of the GNU Free Documentation License.


Giant Panda

Mercedes Car
James Bond Guide
This site monitored by SitePinger.net